Ubbil li ci biir

LI NDAW ÑI DI LAAJ

Naka laa menee déggoo ak samay waajur?

Naka laa menee déggoo ak samay waajur?

 Tontul ci laaj yi jëm ci ñàkk déggoo

  • Ci say waajur, kan nga xalaat ne moo gën a yomb nga am ak moom porobalem?

    • Sa pàppa

    • Sa yaay

  • Ñaata yoon ngay faral di am porobalem ak moom?

    • Barewul

    • Lée-lée

    • Saa su ne

  • Ndax porobalem bu garaaw lay doon?

    • Mën nañu ko faj ci lu gaaw ak ci jàmm.

    • Mën nañu ko faj waaye dinañu werante lu bare.

    • Duñu ko mën a faj bu dee sax werante nañu lu bare.

Boo yaakaaree ne mënuloo déggoo ak say waajur, xéyna di nga jàpp ne ñoom ñoo war a def dara ngir defar diggante bi. Waaye di nañu gis ne yow ci sa bopp am na li nga mën a def ngir waññi ñàkk déggoo biy faral di am ci sa diggante ak say waajur. Nañu njëkk a xool . . .

 Li tax ñàkk déggoo di am

  • Ni ngay xalaate. Looy gën di màgg say xalaat di gën a xóot, ci ngay tambalee am li ngay nangu ak li ngay bañ. Te yenn yi mën na wuute ak li say waajur bañ walla nangu. Waaye terewul Biibël bi ne: «Teral-leen seen ndey ak seen baay» (Mucc ga 20:12).

    Li am mooy: Dafay laaj sago ak xareñ ngir mën a wax sa xalaat ci loo àndul te doo ci xuloo.

  • Liberte. Booy gën di màgg say waajur mën nañu laa gën a may liberte. Porobalem bi mooy xéyna duñu la may liberte bi nga bëgg ci waxtu wi nga ko bëggee. Te loolu mën na indi ñàkk déggoo. Terewul Biibël bi ne: «Nangeen déggal seeni waajur» (Efes 6:⁠1).

    Li am mooy: Liberte bi la say waajur di may mu ngi aju ci anam bi ngay jëfandikoo liberte bi nga am fi mu tollu nii.

 Li nga mën a def

  • Bàyyil xel ci li la war. Boo amee jafe-jafe ak say waajur bul teg tuuma bi yépp ci seen kaw. Defal lépp li nga mën ngir mën a déggoo ak ñoom. Benn ndaw bu tudd Jeffrey lii la wax: « Du li sa waajur yi di wax rekk mooy indi porobalem waaye itam fasoŋ bi nga leen di tontoo. Booy wax ànd ci ak dal dina yombal déggoo bi.»

    Lii la Biibël bi wax: «Wutleena juboo ak ñépp, ba fa seen kàttan yem» (Room 12:18, ñoo dëngal mbind mi).

  • Nanga déglu: Samantha mi am 17 at lii la wax: «Foog naa ne, déglu mooy li gën a metti ci man. Waaye seetlu naa ne, waajur yi bu ñu gise ne yaa ngi leen di déglu, ñoom itam dañu lay déglu.»

    Lii la Biibël bi wax: «Ku nekk war ngaa farlu ci déglu, di yéexa wax» (Saag 1:19).

  • Xalaatal mel ni ku bokk ci benn ekip. Jéemal a regle porobalem bi ni ñu koy defe ci futbal. Bul jàppe say waajur ni ñi nga war a dajeel waaye jàppe leen ni ñi nga bokkal ekip. Benn ndaw bu tudd Adam lii la wax: «Su porobalem amee, waajur yi dañuy bëgg li gën ci seen doom, doom ji it bëgg li gën ci boppam. Kon daanaka, ñoom ñépp ñoo bokk li ñu bëgg».

    Lii la Biibël bi wax: «Nanu wut luy indi jàmm» (Room 14:19).

  • Nanga comprendre say waajur. Benn Janq bu tudd Sarah lii la wax: «Saa yu ma xalaatee ne samay waajur am nañu ay porobalem yu metti yu mel ni samay yos, loolu dafa may dimbali». Beneen janq bu tudd Carla lii la ci yokk: «Damay jéem a xalaat li samay waajur di yëg. Su fekkee ne dama doon yar xale buy jànkoonte ak jafe-jafe yi may jànkoonteel tey, lan moo doon gën ci moom?»

    Lii la Biibël bi wax: «Buleen yem ci topptoo seen bopp rekk, waaye booleleen ci seeni moroom» (Filib 2:4).

  • Nanga déggal say waajur. Loolu sax la la Biibël bi sant nga def. Boo toppee xelal boobu, mbir mi dina gën a yomb ci yow. Benn janq bu tudd Caren lii la wax: «Sama stress dafay wàññeeku suma defee li ma samay waajur sant. Xañ nañu seen bopp lu bare ndax man. Kon lu mu néew-néew war naa leen déggal. Déggal say waajur mooy li la gën a mën a dimbali nga déggoo ak ñoom».

    Lii la Biibël bi wax: «Bu matt amul, ab taal fey» (Kàddu yu Xelu 26:20).

Xelal. Su fekkee ne waxtaan ak say waajur dafa jafe ci yow, jéemal a bind li nga xalaat ci benn kayit walla nga yónnee leen mesaas. Benn janq bu tudd Alyssa nee na loolu lay def bés bu sawarul wax ak ay waajuram. Mu yokk ci ne «dafa may dimbali ma bañ a yëkkëti sama baat walla wax loo xam ne dinaa ko réccu ëllëg».