Lan la Biibël bi wax ci tànnal sa bopp li nga bëgg a def? Ndax Yàlla mooy dogal lépp?
Li Biibël bi wax
Yàlla may na ñu cér bu réy, maanaam ñu mën a tànnal suñu bopp li ñu bëgg a def. Dogalul lépp li ñu war a def ci suñu dund. Xoolal li Biibël bi wax ci loolu.
Yàlla dafa bind nit ci melokaanam (Njàlbéen ga 1:26). Loolu lu mu tekki? Mu ngi tekki ne Yàlla sàkk na nit mu mën a wone jikko yu mel ni mbëggeel ak njub te mën a tànnal boppam li mu bëgg a def. Kon nit dafa wuute ak mala yi nga xam ne instinct lañuy doxe, maanaam ci lu bare Yàlla moo def ci seen bopp li ñu war a def.
Mën nañu wax ne, ku nekk mooy ji li mu bëgg a góob ëllëg. Looloo tax Biibël bi di ñu xiir ci ‘taamu dund’ te ‘déggal [Yàlla]’, maanaam booy déggal Yàlla yaa ngi tànn dund (Baamtug Yoon wi 30:19, 20). Ndax Yàlla dina la wax nga tànn, fekk mayu la nga mën a tànn? Déedéet! Yàlla soxorul. Yàlla du forse kenn mu topp ay ndigalam waaye dafa ñuy xiir ci tànn lu baax. Xoolal li mu wax fii: «Céy su ngeen sàmmoon samay santaane, ba jàmm baawaanal leen» (Esayi 48:18).
Lépp li ñuy def ci suñu dund, du Yàlla mooy dogal mu sotti walla mu bañ a sotti. Boo bëggee def dara ba mu sotti danga ci war a góor-góorlu bu baax. Lii la Biibël bi wax: «Liggéey boo gis, liggéeyal; def ci loo man» (Kàdduy Waare 9:10). Nee na itam ne ku «farlu, woomle» (Kàddu yu Xelu 21:5).
Yàlla may na la lu réy: mën nga tànnal sa bopp li nga bëgg a def. Kon mën nga tànn bëgg Yàlla «ak sa xol bépp» (Macë 22:37).
Ndax lépp lu xew Yàlla moo ko def?
Biibël bi wax na ne Yàlla mooy Aji kàttan ji. Kenn mënul a wàññi kàttanam (Ayóoba 37:23; Esayi 40:26). Waaye du jëfandikoo kàttanam ngir dogal lépp saa su nekk. Loolu lañu gis ci ni mu doxale ak réewu Babilon mi doon xeex mbooloom. Biibël bi nee na Yàlla dafa doon ‘téye boppam’ (Esayi 42:14). Noonu it, fi mu tollu nii, Yàlla mu ngi bàyyi ñi tànn def lu bon di lor seeni moroom, waaye du leen ci bàyyi ba fàww (Sabóor 37:10, 11).