WAAJUR YI ÑOO MOOM LII
7: Jikko
LI MUY TEKKI
Jikko mooy fasoŋ bi nit ki di dunde bés bu nekk. Ndax dangay góor-góorlu ngir wone njub ci lépp looy def? Bu dee waaw, xéyna dinga bëgg say doom mel ni yow.
Yaru ci jikko la bokk. Ci misaal, nit ku am jikko ju baax, dafay sawar ci liggéey, jub te respekte ñeneen ñi. Bi ngay nekk ndaw lay gën a yomb nga am jikko yooyu.
LII LA BIIBËL BI WAX: «Tegal gone ciw yoon, ba bu màggee, du ko wacc» (Kàddu yu Xelu 22:6).
LI TAX MU AM SOLO
Ci jamono jii nga xam ne, ordinatëër ak internet ñoo xew, am jikko ju baax lu am solo la. Benn yaay bu tudd Karyn lii la wax: «Léegi, ak telefon yi, mën nañu gis lépp lu mën a yàq jikkoy nit ci waxtu wu nekk. Suñuy doom mën nañu toog sax ci suñu wet di seetaan lu bon.»
LII LA BIIBËL BI WAX: «Ñi mat [...] [ñooy] jëfandikoo seen xel ngir ràññee lu baax ak lu bon» (Yawut ya 5:14).
Yaru lu am solo la itam. Yaru dafay feeñ ci waxin. Nit ku yaru, dafay faral di wax «baal ma» ak «jërëjëf». Dafay wone ne fonk na ñeneen ñi. Jikko jooju jafe na tey, ndaxte nit ñi telefon walla lu mel noonu, lañu gën a fonk seen moroom.
LII LA BIIBËL BI WAX: «Defal-leen nit ñi li ngeen bëgg, ñu defal leen ko» (Luug 6:31).
LI NGA MËN A DEF
Waxal nit ñi li nga gëm. Ay gëstukat wone nañu ne, ndaw ñiy gën a moytu tëdd ak jigéen walla góor fekk séyuñu, mooy ñi ñu xamal ci lu leer ne, loolu baaxul.
XELAL: Jaaral ci benn xew-xew ngir wax ci jikko. Ci misaal, bu ñu yéglee ci xibaar yi ne am na ku ñu rey, mën nga ne: «Reyante bi am léegi, ñaaw na! Ci sa xalaat, lu ko waral?»
«Bu xale yi mënul a raññe lu baax ak lu bon, dina jafe ci ñoom ñu mën a def lu baax» (Brandon).
Yarleen xale yi. Xale yi sax, mën nañu jàng a wax «baal ma», «jërëjëf» te wone respe. Benn téere buy wax ci yar xale nee na: «Bu xale yi gisee ne, du ñoom rekk a nekk ci àddina si (dañoo bokk ak ñeneen njaboot gi, lekkool bi walla koñ bi), dañuy gën a sawar ci def luy jariñ ñépp.»
XELAL: Joxal xale yi liggéey ci kër gi, ngir jàngal leen jikko yiy tax ñu mën a dimbali ñeneen ñi.
«Bu xale yi tàmmee di liggéey ci kër gi, bu ñu génnee duñu sonn. Dafay fekk ñu tàmm liggéey ba noppi» (Tara).