NJÀNGALE 12
Naka nga mënee jege Yàlla ?
1. Ndax ñaan yépp la Yàlla di déglu ?
Yàlla mu ngi woo ñépp ñu jege ko ci ñaan (Sabóor 65:3). Waaye du ñaan yépp lay déglu ba di ko nangu. Góor buy toroxal jabaram, loolu mën na yàq ay ñaanam (1 Piyeer 3:7). Bi waa Israyil saxee ci def lu bon, Yàlla nanguwuloon a déglu seeni ñaan. Ci lu leer, ñaan cér bu réy la. Ñi nga xam ne dañoo réccu bàkkaar yu réy yi ñu def, Yàlla dina nangu sax seeni ñaan. — Jàngal Esayi 1:15 ; 55:7.
Seetaanal wideo Ndax ñaan yépp la Yàlla di déglu ?
2. Naka lañu war a ñaane ?
Ñaan dafa bokk ci jaamu Yàlla, kon Yexowa mi ñu sàkk rekk lañu war a ñaan (Macë 4:10 ; 6:9). Ndegam matuñu, suñu ñaan yi war nañu leen a jaarale ci turu Yeesu, ndaxte moom moo dee ngir suñuy bàkkaar (Yowaana 14:6). Yexowa bëggul ñuy tari suñu ñaan walla ay ñaan yu ñu bind ci ay téere. Dafa bëgg bu ñu koy ñaan, ñaan bi jóge ci suñu xol. — Jàngal Macë 6:7 ; Filib 4:6, 7.
Ki ñu sàkk mën na dégg sax ñaan yi ñuy wax ci suñu biir xol (1 Samiyel 1:12, 13). Mu ngi ñuy woo ñu ñaan ko fu ñu mënta tollu. Mën nañu ko ñaan ci suba si, walla ci ngoon si, walla bu ñuy lekk, ak bu ñu nekkee ci poroblem. — Jàngal Sabóor 55:23 ; Macë 15:36.
3. Lu tax Karceen yi di am ay ndaje ?
Jege Yàlla yombul ndaxte ñu ngi dund ak ay nit ñoo xam ne seen ngëm des na, te jàmm ji Yàlla dige ne dina am ci kaw suuf si, dañu koy jàppe ni ay caaxaan (2 Timote 3:1, 4 ; 2 Piyeer 3:3, 13). Kon soxla nañu suñu mbokk yi ci wàllu ngëm xiirtal ñu, te ñoom itam soxla nañu ñu xiirtal leen. — Jàngal Yawut ya 10:24, 25.
Ndaje Seede Yexowa yi dañuy tax ba ngëmu ñeneen ñi mën ñoo xiirtal. — Jàngal Room 1:11, 12.
Booy ànd ak ñi bëgg Yàlla dina tax nga jege Yàlla.4. Naka nga mënee jege Yàlla ?
Mën nga jege Yexowa sooy xalaat ci li ngay jàng ci Kàddoom. Xoolal li nga mën a jàng ci ay jëfam, ay ndigalam ak ay digeem. Boo ciy xalaat ci ñaan dinga sopp mbëggeelu Yàlla ak xam-xamam ci sa xol. — Jàngal Yosuwe 1:8 ; Sabóor 1:1-3.
Mën nga jege Yàlla bu dee wóolu nga ko te am ngëm ci moom. Ngëm dafa mel ni garab bu ñuy suuxat. Danga war di xalaat ci fi sa ngëm sukkandiku ngir kontine di ko suuxat. — Jàngal Macë 4:4 ; Yawut ya 11:1, 6.
5. Jege Yàlla, ban njariñ la lay amal ?
Yexowa yëg na ñépp ñu ko bëgg. Mën na leen aar ci lépp lu mën a yàq seen ngëm ak seen yaakaaru am dund gu dul jeex (Sabóor 91:1, 2, 7-10). Yexowa dafa ñuy artu ci bépp dundin bu mën a yàq suñu wér-gi-yaram ak suñu bànneex. Yexowa dafa ñuy jàngal ni ñuy ame dundin bu baax. — Jàngal Sabóor 73:27, 28 ; Saag 4:4, 8.