Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 12

Nanga wone ne gëm nga Yàlla dëgg !

Nanga wone ne gëm nga Yàlla dëgg !

YÀLLA xamal na jaamam yi ne dina am kuy jéem a yàq seen ngëm. Lii la wax ci kàddoom : “ Maanduleen te foog, ndax seen noon Seytaane mu ngi wër, ni gaynde guy yëmmu, di rëbb ku mu yàpp. ” (1 Piyeer 5:8). Lan la Seytaane di def ngir jéem a yàq sa ngëm ?

Ndax lii mas na la dal ?

Seytaane mën na jaar ci nit ñi walla sax jaar ci suñuy mbokk ngir xiir ñu ci bañ a gëstu Mbind mu sell mi. Yeesu waxoon na ne : “ Nooni nit ñooy waa këram. ” (Macë 10:36). Nekkul ne dañu la bañ waaye xéyna dañu xamul wax yu neex te rafet yi nekk ci Kàddu Yàlla. Xéyna it dañuy ragal li nit ñi di wax. Waaye Mbind mu sell mi, lii la wax : “ Ragal nit bay lox, fiir lay doon waaye boo tegee sa yaakaar ci Yexowa, dina la aar. ” (Léebu yi 29:25, MN) Boo bàyyee di jàng Mbind mu sell mi ngir neex nit, ndax loolu dina neex Yàlla ? Déedéet ! Waaye bu ñuy wone suñu ngëm dëgg ci Yàlla, Yàlla dafa ñuy dimbali. “ Bokkunu ci ñiy delloo gannaaw ba réer, waaye ñu ngi bokk ci ñi am ngëm tey mucc. ” — Yawut ya 10:39.

Nanga fattaliku Dumas bi ñu waxoon ci xët 6. Bu njëkk ba, jabaram dafa ko doon ñaawal ndax li mu gëmoon. Waaye dafa mujj a ànd ak moom ci jàng Kàddu Yàlla. Noonu it, boo kontinee di def li Yàlla bëgg, xéyna dinga mën a dimbali say xarit walla say mbokk ñu def loolu ñoom it. Mbokk yu bare def nañu loolu bi ñu gisee “ dund gu sell, boole ci weg ” bi ki gëm Yàlla dëgg wone. — 1 Piyeer 3:1, 2.

Seytaane day jéem a nax itam nit ñi ba ñu foog ne amuñu jot pur jàng Mbind mu sell mi. Dafa bëgg coono àddina si, maanaam poroblemu xaalis ak yeneen yuy ub sa bopp, “ tanc kàddu gi ”, maanaam kàddu Yàlla, ba sa ngëm du “ meññ dara ” (Màrk 4:19). Bul nangu loolu ndax Mbind mu sell mi nee na : “ Dund gu dul jeex gi nag, mooy ñu xam la, yaw jenn Yàlla ju wóor ji am, te ñu xam it ki nga yónni, muy Yeesu Kirist. ” (Yowaana 17:3). Waaw, fàww nga kontine di jàng lu jëm ci Yàlla ak Yeesu, Almasi bi, boo bëggee am dund gu dul jeex ci Àjjana !

Ñaanal Yàlla mu dimbali la

Xalaatal Musaa mi dëkkoon ci këru buuru Misra. Mënoon na fa am alal bu bare, tur bu siw, ak kiliftéef. Ba tey, “ bokk coono ak gaayi Yàlla yi moo ko gënaloon muy bànneexu ab diir ci bàkkaar. ” Lu tax ? Ndaxte ‘ dafa meloon ni nit kuy gis Yàlla ’. (Yawut ya 11:24, 25, 27). Waaw, Musaa dafa gëmoon Yàlla dëgg. Jiital na Yàlla ci dundam, bàyyi ci ginnaaw njariñu boppam, te Yàlla barkeel na ko bu baax. Boo defee lu mel noonu, Yàlla dina la barkeel yow itam.

Seytaane mën na jaar ci lu bare ngir jéem laa nax. Waaye xoolal li Kàddu Yàlla wax : “ Dàqleen Seytaane, te dina daw, ba sore leen. ” (Saag 4:7). Noo mënee dàq Seytaane ?

Nanga kontine di jàng Mbind mu sell mi. Nanga jàng Kàddu Yàlla bés bu nekk, gëstu ko, te topp li mu wax. Boo defee loolu, dinga ‘ gànnaayoo yérey xarey Yàlla yépp ’ te noot Seytaane. — Efes 6:13.

Nanga ànd ak ñi gëm Yàlla dëgg. Seetal ñiy jàng, gëstu, te topp li nekk ci Mbind mu sell mi. Nit ñu mel noonu, dañuy “ seet ni nu man a xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax[. . .] te [. . .] nàddante ci ngëm, di ko feddali ”. Kon dinañu la dimbali nga mën a yokk sa ngëm. — Yawut ya 10:24, 25.

Àndal ak ñi gëm Yàlla

Nanga jege Yexowa. Ñaanal Yàlla mu dimbali la te nanga teg sa yaakaar ci moom. Bul fàtte ne Yàlla dafa la bëgg a dimbali. ‘ Nanga yenniku ci kawam sa njàqare jépp, ndax ku la ñeewante la. ’ (1 Piyeer 5:6, 7). “ Yàlla kuy sàmm kóllëre la, te du nangu nattu bi wees seen kàttan, waaye cib nattu, dina leen ubbil bunt bu ngeen man a récce, ba ngeen man koo dékku. ” — 1 Korent 10:13.

Ci li Seytaane wax Yàlla, bu nit amee coono, dina bàyyi Yàlla. Waaye mën nga wone ne Seytaane fenkat la ! Yàlla nee na : “ Amal xel [. . .] te seddalal sama xol, ndax ma mën a tontu ki may sóoru. ” (Léebu yi 27:11, MN). Waaw, nanga fas yéene wone ne danga gëm Yàlla dëgg !