LESOŊ 41
Lan la Biibël bi wax ci séy?
Ñu bare dañuy rus a wax ci mbirum séy. Waaye Biibël bi buy wax ci séy, dafa koy wax ci fasoŋ bu leer te yiw. Li mu ci wax suñu njariñ la. Loolu lu jaadu la ndaxte Biibël bi, ci Yexowa mi ñu sàkk la jóge. Moom moo xam li gën ci ñun. Won na ñu li ñu war a def ba neex ko ak li ñu mën a dimbali ñu dund ci jàmm ba fàww.
1. Naka la Yexowa gise mbirum séy?
Séy maye la bu jóge ci Yexowa. Jëkkër ak jabar rekk la jagleel séy ngir ñu jële ci bànneex. Yexowa dafa may loolu jëkkër ak jabar ngir ñu mën a am doom, waaye it ngir ñu wonante mbëggeel ak cofeel ci anam bu leen di may bànneex. Loolu moo tax Kàddu Yàlla ne: «Nga bànneexoo kiy sa jabar ba ngay ndaw» (Kàddu yu Xelu 5:18, 19). Yexowa dafay xaar ci karceen yiy séy, ku nekk yem ci moroomam. Bu ko defee, duñu njaaloo mukk (Jàngal Yawut ya 13:4).
2. Lan mooy jëfi njaaloo?
Biibël bi nee na «njaalookat yi [...] duñu bokk ci nguuru Yàlla» (1 Korent 6:9, 10). Ñi bind ci Biibël bi, baat bi ñu jëfandikoo ci làkku Gereg ngir wax ci njaaloo mooy baatu por·neiʹa. Baat boobu mu ngi ëmb jëf yu mel ni (1) góor ak jigéen tëdd a fekk duñu jëkkër ak jabar, (2) góor-jigéen walla jigéen ak jigéen ak (3) nit tëdd ak mala. Bu ñu ‘moytoo njaaloo’ dinañu neex Yexowa te dinañu ci jële njariñ (1 Tesalonig 4:3).
XÓOTALAL NJÀNG MI
Xoolal ni nga mënee moytu jëfi njaaloo ak njariñ bi ngay jële ci wéy di set ci wàllu xel.
3. Dawal jëfi njaaloo
Góor gu takkuwoon ci Yàlla te tudd Yuusufa, def na lépp ngir bañ a daanu ci njaaloo. Jàngal Njàlbéen ga 39:1-12. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
-
Lan moo tax Yuusufa daw? (Xoolal aaya 9).
-
Ndax foog nga ne li Yuusufa def mooy li gën? Lu tax?
Tey, naka la ndaw ñi mënee roy Yuusufa te daw jëfi njaaloo? Seetaanal WIDEO BI.
Yexowa dafa bëgg ñun ñépp ñu daw jëfi njaaloo. Jàngal 1 Korent 6:18. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
-
Lan moo mën a yóbbe nit mu daanu ci jëfi njaaloo?
-
Naka nga mënee daw jëfi njaaloo?
4. Mën nga bañ a daanu ci jëfi njaaloo
Lu tax moytu jëfi njaaloo yombul? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.
-
Ci wideo bi, bi suñu mbokk bi gise ne ay xalaatam ak ay jëfam mën nañu ko yóbbu ci wor jabaram, lan la def?
Karceen yi takku ci Yàlla sax, lée-lée am xalaat yu set dafay jafe ci ñoom. Lan nga mën a def ba doo wéy di am ay xalaat yu bon? Jàngal Filib 4:8. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
-
Ci lan lañu war di xalaat?
-
Liir Biibël bi ak sóobu bu baax ci liggéeyu Yexowa, naka lañu mënee dimbali ñu bañ a daanu ci bàkkaar?
5. Santaane Yexowa yi suñu njariñ la
Yexowa xam na li gën ci ñun. Wax na ñu ni ñu mënee wéy di set ci xel ak njariñ bi ñu ciy jële. Jàngal Kàddu yu Xelu 7:7-27 walla seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.
-
Naka la xale bu góor bi dugale boppam ci fiir? (Xoolal Kàddu yu Xelu 7:8, 9).
-
Ni ko Kàddu yu Xelu 7:23, 26 wonee, jëfi njaaloo mën na jur musiba. Bu ñu leen moytoo, ci yan jafe-jafe lañuy mucc?
-
Bu suñu dund sellee, yan barke lañuy am ëllëg?
Am na ñu xalaat ne li Biibël bi wax ci mbirum góor-jigéen, wax ju soxor la. Waaye Yexowa, Yàllay mbëggeel la te dafa bëgg ñépp am dund gu dul jeex. Waaye nag ngir loolu mën a nekk, fàww ñu topp ay santaaneem ci suñu dund. Jàngal 1 Korent 6:9-11. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
-
Ci gis-gisu Yàlla, ndax mbirum góor-jigéen rekk mooy lu bon li ñu war a moytu?
Bu ñu bëggee neex Yexowa, ñun ñépp soxla nañu soppi dara ci suñu dundin. Ndax góor-góorlu ci loolu, jar na ko? Jàngal Sabóor 19:9, 12. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
-
Ndax foog nga ne topp santaane Yexowa yi, lu metti la? Lu tax?
BU LA NIT WAXOON: «Mën nga tëdd ak ku la neex, nangeen bëggante rekk.»
-
Lan nga koy wax?
NAÑU TËNK
Séy maye la bu jóge ci Yexowa ngir jëkkër ak jabar jële ci bànneex.
Nañu fàttaliku
-
Jëfi njaaloo, yan jëf la ëmb?
-
Lan moo ñuy dimbali ñu moytu jëfi njaaloo?
-
Ban njariñ lañuy jële ci topp santaane Yexowa yi?
GËSTUL
Xoolal ndax ci Yàlla am na solo góor ak jigéen séy ci yoon.
Xoolal ni ñu santaane Yàlla yi ci bépp jëfi njaaloo di aare.
«Ndax ku dugal awra ci gémmiñu nit, séy nga ak moom dëgg?» (Ci jw.org la nekk)
Ci nettali bi tudd «Dañu ma may cér», xoolal li tax benn góor-jigéen soppi dundam ngir neex Yàlla.
a Jëf jooju Yàlla bañ dafa ëmb jëf yu bare yu mel ni, tëdde nit, dugal awra nit ci gémmiñ walla ci tuun ak di raay awra nit.