Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 27

Naka la ñu deewu Yeesu mënee muccal?

Naka la ñu deewu Yeesu mënee muccal?

Dañuy bàkkaar, di nekk ci coono ak di dee ndaxte Aadama ak Awa déggaluñu Yàlla. a Waaye nag am nañu yaakaar. Yexowa def na li war ngir muccal ñu ci bàkkaar ak dee, jaare ko ci doomam Yeesu Kirist. Biibël bi nee na, deewu Yeesu mooy suñu njot. Njot mooy li ñuy fey ngir yewwi nit. Yeesu bakkanam bu mat sëkk la fey ngir yewwi ñu ci bàkkaar ak dee (Jàngal Macë 20:28). Bi Yeesu nangoo xañ boppam dund gu dul jeex gi mu mënoon a dund ci kaw suuf, dafa ñu may ñu mën a jotaat lépp li Aadama ak Awa ñàkk. Yeesu wone na itam ne, moom ak Yexowa bëgg nañu ñu lool. Lesoŋ bii dina ñu dimbali ñu yokk suñu ngërëm ci li ñu Yeesu defal.

1. Tey, ban njariñ la ñu deewu Yeesu mën a amal?

Dañuy def lu bare lu neexul Yexowa ndaxte ay bàkkaarkat lañu. Waaye bu ñu bëggee wéy di am diggante gu rattax ak Yàlla, dañu war a rëccu dëgg suñuy bàkkaar, ñaan Yexowa mu baal ñu ci turu Yeesu, ba pare def lépp ngir bañ koo defaat (1 Yowaana 2:1). Biibël bi nee na: «Kirist ci boppam dee na benn yoon ba fàww, ngir dindi bàkkaar yi, moom mi jub ngir ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla» (1 Piyeer 3:18).

2. Ban njariñ la ñu deewu Yeesu mën a amal ëllëg?

Yexowa dafa yónni Yeesu ngir mu joxe bakkanam bu mat sëkk ‘ngir képp ku gëm Yeesu am dund gu dul jeex te du sànku mukk’ (Yowaana 3:16). Li Yeesu def moo tax ci kanam tuuti, Yexowa dina fi dindi lu bon lépp li bàkkaaru Aadama jur. Loolu dafay tekki ne, bu ñu amee ngëm ci saraxu Yeesu, dinañu mën a dund ba fàww ci àjjana ci kaw suuf! (Esayi 65:21-23).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Gënal a yokk sa xam-xam ci li tax Yeesu joxe bakkanam te xoolal njariñ bi nga ci mën a jële.

3. Deewu Yeesu dafa ñuy yewwi ci bàkkaar ak dee

Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Lan la Aadama ñàkk bi mu bañee déggal Yàlla?

Jàngal Room 5:12. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan la la bàkkaaru Aadama jural?

Jàngal Yowaana 3:16. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lu tax Yexowa yónni doomam ci kaw suuf?

  1. Aadama nit ku mat la woon waaye dafa bañ a déggal Yàlla. Looloo tax nit ñi di bàkkaar ak di dee

  2. Yeesu nit ku mat la woon waaye dafa déggal Yàlla. Looloo tax nit ñi mën a nekkaat nit ñu mat te mën a dund ba fàww

4. Deewu Yeesu mën na jariñ nit ñi ñépp

Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Naka la deewu benn nit mënee jariñ nit ñi ñépp?

Jàngal 1 Timote 2:5, 6. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Aadama nit ku mat la woon waaye moo dugal nit ñi ci bàkkaar ak dee. Yeesu itam nit ku mat la woon. Naka la ñu saraxu Yeesu di muccale ci bàkkaar ak dee?

5. Njot gi mayug Yexowa la ngir yow

Xaritu Yexowa yi dañu gise njot gi ni may gu leen Yexowa may. Ci misaal, jàngal Galasi 2:20. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Naka la ndawli Pool wonee ne dafa gise njot gi ni may gu ko Yexowa may, moom ci boppam?

Bi Aadama bàkkaaree, moom ak ay doomam yépp, dee lañu leen teg daan. Waaye Yexowa dafa yónni doomam, mu dee ngir nga mën a am dund gu dul jeex.

Booy jàng aaya yii di topp, jéemal a xalaat li Yexowa waroon a yëg, bi ñu doon metital doomam. Jàngal Yowaana 19:1-7, 16-18. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Boo xalaatee ci li la Yexowa ak Yeesu defal, lan ngay yëg ci sa xol?

BU LA NIT LAAJOON: «Naka la benn nit mënee dee ngir nit ñépp?»

  • Lan ngay tontu?

NAÑU TËNK

Deewu Yeesu moo tax Yexowa mën ñoo baal suñuy bàkkaar te may ñu, ñu mën a am dund gu dul jeex.

Nañu fàttaliku

  • Lu tax Yeesu dee?

  • Naka la ñu saraxu Yeesu di muccale ci bàkkaar ak dee?

  • Ban njariñ la la deewu Yeesu mën a amal?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal li tax ñu ne dundu Yeesu gu mat gi, njot la.

«Naka la saraxu Yeesu nekkee ‘njotug ñu bare’?» (Ci jw.org la nekk)

Xoolal li ñu war a def ngir mucc ci bàkkaar ak dee.

«Naka la ñu Yeesu di muccale?» (Ci jw.org la nekk)

Xoolal naka la saraxu Yeesu dimbalee benn góor mu soppi dundam.

«Nekkatuma nittu fitna» (Ci jw.org la nekk)

a Bàkkaar yemul rekk ci def lu bon. Dafa ëmb itam matadi bi ñu donn ci suñu maam Aadama ak Awa.