Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 13

Diine yi dul dëgg dañuy tilimal turu Yàlla

Diine yi dul dëgg dañuy tilimal turu Yàlla

Yàlla mbëggeel la. Kon lu tax diine yu bari yuy wax ne Yàlla lañu fi nekkal di def lu ñaaw? Li am mooy, diine yooyu ay diine yu dul dëgg lañu. Dañuy tilimal turu Yàlla. Naka lañuy tilimale turu Yàlla? Naka la Yàlla gise loolu? Te lan la nar a def?

1. Naka la diine yu dul dëgg yi tilimale turu Yàlla ak seeni njàngale?

Diine yu dul dëgg yi «toxal nañu dëggu Yàlla, tëral fen» (Room 1:25). Ci misaal, diine yu bari dañuy nëbb nit ñi turu Yàlla. Moona dey, Biibël bi nee na dañu war a woo Yàlla ci turam (Room 10:13, 14). Bu musiba amee, njiitu diine yu bari dañuy wax ne Yàllaa ko dogal. Waaye loolu ay fen la. Yàlla du def mukk lu bon (Jàngal Saag 1:13). Li ci metti mooy, njàngale yu dul dëgg yooyu tax nañu nit ñi sori Yàlla.

2. Naka la diine yu dul dëgg yi tilimale turu Yàlla ak seeni jëf?

Diine yu dul dëgg yi bëgguñu nit ñi ni leen Yexowa bëgge. Biibël bi nee na, diine yu dul dëgg yi, seeni ‘bàkkaar dajaloo nañu ba ci asamaan’ (Peeñu 18:5). Ay téeméeri at a ngi nii, diine yi di dugg ci politig, di jàppale geer yi, di reylu nit ñu bari walla ñu ànd ci ñuy rey ay nit. Yenn njiitu diine yi dañoo bari alal ba pare, di laaj xaalis ñi leen di topp ngir wéy ci seen dund bu neex. Seen jëf yooyu yépp dañuy wone ne xamuñu Yàlla, waxatuñu di ko fi nekkal (Jàngal 1 Yowaana 4:8).

3. Naka la Yàlla gise diine yi dul dëgg?

Ndegam li diine yi dul dëgg di def dafa lay merloo, kon ci sa xalaat lan la war a def ci Yexowa? Yexowa dafa bëgg nit ñi, waaye dafa mere njiitu diine yiy jàngale li dul dëgg ci moom ak di toroxal nit ñi. Nee na dina alag diine yu dul dëgg yi, jële leen fi ba ñu «ne meŋŋ» (Peeñu 18:21). Ci kanam tuuti, Yàlla dina fi dindi diine yi dul dëgg yépp (Peeñu 18:8).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal leneen luy wone ni Yàlla gise diine yi dul dëgg. Xoolal li diine yooyu def ak li tax waruloo bàyyi jàng a xam Yexowa ndax seeni jëf.

4. Yàlla nanguwul diine yi yépp

Nit ñu bari dañu gëm ne, diine yi bari nañu waaye ñoom ñépp ci Yàlla lañuy jëme. Waaye ndax loolu dëgg la? Jàngal Macë 7:13, 14. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan la Biibël bi wax ci yoon wi jëme ci dund?

Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Ndax Biibël bi dafa ne am na diine yu bari yu neex Yàlla?

5. Diine yu dul dëgg yi, royuñu ci mbëggeelu Yàlla

Diine yu dul dëgg yi tilimal nañu turu Yàlla ci anam yu bari. Te anam bi gën a yees bi ñu ko defe mooy, ni ñu dugale seen loxo ci geer yi. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Lan la igliis yu bare def ci ñaareelu geer bu mag bi?

  • Lan nga xalaat ci li ñu def?

Jàngal Yowaana 13:34, 35 ak 17:16. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lan la Yexowa di yëg ci xolam, bu gisee diine yi di dugal seen loxo ci geer yi?

  • Diine yu dul dëgg yi ñoo nekk ci ginnaaw jëf yu bon yu bari. Ci ban anam nga gis ne diine yi royuñu ci mbëggeelu Yàlla?

Diine yu dul dëgg yi royuñu mbëggeelu Yàlla

6. Yàlla dina yewwi nit ñi ci diine yi dul dëgg

Jàngal Peeñu 18:4. a Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan ngay yëg ci xam ne, Yàlla bëgg na muccal nit ñi diine yi dul dëgg di nax?

7. Wéyal di jàng lu jëm ci Yàlla dëgg ji

Ndax war nga soppi sa gis-gis ci Yàlla, ndax li diine yu dul dëgg yi di def ak di wax? Xalaatal rekk, benn xale bu bañ a topp xelal bu ko pàppam jox. Xale bi génn kër pàppam, ba pare di def lu bon. Pàppa ji àndul benn yoon ci doxalinu doomam. Lu tax jaaduwul, ñuy sikkal pàppa ji ndax doxalinu doomam?

  • Kon ndax jaadu na, ñuy sikkal Yexowa te bàyyi jàng lu jëm ci moom, ndax doxalinu diine yi dul dëgg?

BU LA NIT WAXOON: «Diine yi yépp a baax, ñoom ñépp lu baax lañuy jàngale.»

  • Ndax loolu mooy sa gis-gis yow itam?

  • Bu dee sax diine yu bare dañuy jàngale lu baax, lu tax Yàlla nanguwu leen ñoom ñépp?

NAÑU TËNK

Diine yu dul dëgg yi tilimal nañu turu Yàlla ak seeni njàngale yu dul dëgg ak seeni jëf yu ñaaw. Yàlla dina alag diine yi dul dëgg.

Nañu fàttaliku

  • Lan nga xalaat ci li diine yu dul dëgg yi di jàngale ak di def?

  • Naka la Yexowa gise diine yi dul dëgg?

  • Lan la Yàlla di def diine yi dul dëgg?

Jubluwaay

GËSTUL

Lu tax Yexowa bëgg ñuy booloo ak ñeneen ngir jaamu ko?

«Ndax war nañu bokk ci ab diine?» (Ci jw.org la nekk)

Diine yi yàgg nañu jàngale ay fen ci Yàlla, ba tax ñu bari gëm ne Yàlla fonkul nit ñi te ku soxor la. Xoolal li Biibël bi wax ci loolu.

«Ay fen yuy tere nit ñi ñu bëgg Yàlla» (w13 1/11)

a Boo bëggee xam li tax ci téere Peeñu mi, ñuy méngale diine yu dul dëgg yi ak jigéen ju tudd Babilon bu mag bi, xoolal Yeneen leeral 1.