Naka nga gise ëllëg ?
Àddina bi . . .
-
ndax nii lay kontine ?
-
ndax day gën di metti ?
-
walla day gën a neex ?
LAN LA BIIBËL BI WAX CI LAAJ BOOBU ?
“ Yàlla [. . .] dina fomp bépp rangooñ ci seeni bët ; te dee dootul am walla naqar walla jooy walla metit, ndaxte yëf yu jëkk ya wéy nañu. ” — Peeñu ma 21:3, 4, Téereb Injiil di Kàddug Yàlla.
LI MU WAX, BAN NJARIÑ NGA CI MËN A JËLE ?
Liggéey bu neex te am njariñ. — Isaïe 65:21-23.
Metit dootul am te kenn dootul feebar. — Isaïe 25:8 ; 33:24.
Yaw ak sa njaboot ak say xarit dingeen am dund bu neex ba fàww. — Sabóor 37:11, 29.
NDAX MËN NGA GËM LI MU WAX CI LAAJ BOOBU ?
Waaw waaw, xoolal liy topp :
-
Yàlla mën na def li mu dige. Ci Biibël bi, Yexowa Yàlla kese lañuy woowe “ Aji Man ji ”, ndaxte kàttanu Yexowa, amul fu mu yem. (Peeñu ma 15:3) Kon dara mënu ko tere mu def li mu dige, maanaam soppi àddina ba mu neex. Ni ko Biibël bi waxe, “ dara tëwul Yàlla. ” — Macë 19:26.
-
Yàlla bëgg na def li mu dige. Lu jëm ci ñi dee, Biibël bi nee na Yexowa dafa bëgg lool dekkal leen. — Job 14:14, 15.
Biibël bi wax na it ne Yeesu dafa doon faj ñi feebar. Lu tax mu doon def loolu ? Ndaxte lu mu bëggoon la. (Màrk 1:40, 41) Ni Baayam bi nekk ci asamaan, Yeesu dafa bëggoon a dimbali nit ñi. — Yowaana 14:9.
Kon wóor na ñu ne Yexowa ak Yeesu ñoo ñu bëgg a dimbali ngir ñu am ëllëg gu neex ! — Sabóor 72:12-14 ; 145:16 ; 2 Piyeer 3:9.