Ubbite bi
Yàlla dafa mel ni baay bu bëgg ay doomam. 1 Piyeer 5:6, 7
Yàlla moo ñu sàkk te fonk na ñu. Ni Baay bu baax di jàngale ay doomam, noonu itam la ñu Yàlla di wone li ñu war a def ba am dundin bu rafet.
Yàlla jàngal na ñu lu bare loo xam ne dafa ñuy may mbégte ak yaakaar.
Bu ngeen déggee bu baax li Yàlla wax, dina leen tette, dina leen aar, te dina leen dimbali ngeen mën a jànkoonte ak seeni jafe-jafe.
Rax-ci-dolli nag, dingeen mën a dund ba fàww !