Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

PÀCC FUKK AK JURÓOM-ÑEENT

Nañu sax ci mbëggeelu Yàlla

Nañu sax ci mbëggeelu Yàlla
  • Bëgg Yàlla lu muy tekki ?

  • Naka lañu mënee sax ci mbëggeelu Yàlla ?

  • Naka la Yexowa di neexale ñi sax ci mbëggeelam ?

Ndax Yexowa dina nekk sa làquwaay ci jamono ju metti jii ?

1, 2. Fan lañu mën a am làquwaay bu wóor tey jii ?

BOO doon dox ci tali fekk taw bu mag di waaj a am. Asamaan si xiin lool, tàmbalee melax, di dënnu. Taw bu metti daldi komaase. Dangay daw di seet foo mën a làqu. Nga daldi gis nag ci wetu tali bi, foo mën a dugg. Tabax bu dëgër te wóor, fu tooyul te neex a toog. Dinga kontaan lool ci li nga gise tabax bu wóor boobu !

2 Ñu ngi dund ci jamono bu metti. Li àddina si nekke dafay gën a yées rekk. Waaye ba tey am na fu wóor fi ñu mën a làqu ngir musiba bañ ñoo gaañ ba fàww. Loolu mooy lan ? Seetal li Biibël bi wax : «Lii laay wax ci Aji Sax ji: “Yaay sama làquwaay, di sama tata [maanaam fu dëgër fu nit mën a aare boppam], yaay sama Yàlla, yaa ma doy.” » ​— Sabóor 91:2.

3. Naka lañuy def ba Yexowa nekk suñu làquwaay ?

3 Seetal ma lii rekk ! Yexowa, Ki sàkk lépp te nekk Kilifa gi gën a mag, mën na nekk suñu làquwaay. Yexowa mën na ñu aar, ndaxte moo ëpp kàttan képp walla lépp lu ñu mën a def lu bon. Bu amee lu ñu gaañ sax, Yexowa mën na dindi lépp li loolu yàq. Naka lañuy def ba Yexowa nekk suñu làquwaay ? Dañu ko war a gëm. Rax-ci-dolli, Kàddu Yàlla nee na : Nangeen “ saxoo mbëggeelu Yàlla ”. (Yudd 21.) Waaw, dañu war a sax ci mbëggeelu Yàlla, jàpp bu baax suñu diggante ak suñu Baay bi nekk ca asamaan. Noonu, dina ñu wóor ne Yàlla dina nekk suñu làquwaay. Waaye naka lañuy def ba suñu diggante ak Yàlla mel noonu ?

NAÑU RÀÑÑEE MBËGGEEL BI ÑU YÀLLA WON TE ÑU WON KO IT MBËGGEEL

4, 5. Limal yenn ci fasoŋ yi ñu Yexowa wone mbëggeelam.

4 Bu ñu bëggee sax ci mbëggeelu Yàlla, dañu war a xam bu baax ni ñu Yàlla wone mbëggeelam. Xalaatal ci li la téere bii jàngal ci Biibël bi. Yexowa mi ñu sàkk, dafa ñu may dëkkuwaay bu rafet, maanaam suuf si. Dafa ci def lekk bu bare ak ndox bu doy. Mu def ci it rabu àll yi doy kéemaan, ak ay béréb yu rafet lool. Yàlla mi nga xam ne ci moom la Biibël bi jóge, xamal na ñu turam ak it ay jikkoom. Rax-ci-dolli, Kàddoom xamal na ñu ne dafa yónni ci kaw suuf Doomam ji mu bëgg Yeesu. Mu nangu ñu toroxal ko, ba pare ñu rey ko ngir ñun (Yowaana 3:16). Loolu ñu Yàlla may, lu mu ñuy indil ? Dafa ñuy may yaakaaru ëllëg bu neex.

5 Yaakaaru ëllëg boobu ñu am mu ngi wéeru it ci leneen lu Yàlla def. Yàlla dafa samp Nguur ca asamaan, maanaam Nguuru Almasi bi. Ci kanam tuuti Nguur googu dina fi dindi naqar yépp, te defar suuf si ba mu nekk àjjana. Seetal ma lii rekk ! Dinañu mën a dëkk ci suuf si, ci jàmm ak mbégte ba fàww (Psaume 37:29). Bala loolu di am, Yàlla jox na ñu ay xelal ngir ñu dund ci fasoŋ bi gën fi ñu tollu nii. May nañu it ñu mën di ko ñaan. Loolu moo ñu may ñu mën a wax ak moom saa yu ñu ko bëggee. Li ñu wax nii, tuuti kese la ci fasoŋ yi Yexowa wone mbëggeelam doomu Aadama yépp ak yow it ci sa wàllu bopp.

6. Naka nga mënee won it Yexowa mbëggeel bi mu la won ?

6 Laaj bi am solo bi nga war a laaj sa bopp mooy : Naka laay def ba won it Yexowa mbëggeel bi mu ma won ? Ñu bare dinañu wax ne : “ Man it, war naa bëgg Yexowa. ” Ndax loolu ngay xalaat yow itam ? Lii la Yeesu waxoon ne mooy ndigal bi gën a mag : “Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp ak sa xel mépp.” (Macë 22:37.) Wóor na ne am na lu bare lu tax nga bëgg Yexowa Yàlla. Waaye ndax yëg ci sa xol mbëggeel boobu doy na ngir bëgg Yexowa ak sa xol bépp, ak sa bakkan bépp, ak it sa xel mépp ?

7. Ndax yëg rekk ci sa xol mbëggeel bi nga am ci Yàlla doy na ngir sa mbëggeel dëggu ? Waxal lu tax.

7 Ni ko Biibël bi waxe, bëgg Yàlla du li ñuy yëg ci xol kese. Bu dee sax yëg ci suñu xol ne bëgg nañu Yexowa am na solo lool, loolu ndoorte rekk la. Peppu pom am na solo lool bu ñu bëggee am garabu pom buy màgg bay joxe ay doom. Waaye soo bëggee pom, ñu jox la pepp bi, ndax dina la neex ? Déedéet. Noonu it, mbëggeel bi ñuy yëg ci suñu xol ngir Yexowa, ndoorte kese la. Biibël bi nee na : “ Mbëggeel ci Yàlla mooy sàmm ay ndigalam ; te ay ndigalam diisuñu. ” (1 Yowaana 5:3). Bu ñu bëggee am mbëggeel bu dëggu ci Yàlla, mbëggeel boobu dafa war a meññ lu rafet. Dafa war a feeñ ci ay jëf. ​— Macë 7:16-20.

8, 9. Naka lañuy wonee ne bëgg nañu Yàlla te gërëm nañu ko ?

8 Dinañu wone ne bëgg nañu Yàlla bu ñuy topp ay ndigalam te di jëfe ay xelalam. Def loolu jafewul lool. Sàrtu Yexowa yi diisuñu. Yàlla dafa ñu leen jox ngir dimbali ñu, ñu am mbégte ak dund bu neex (Isaie 48:​17, 18). Bu ñu toppee yoon bi ñu Yexowa di won, dañuy won suñu Baay bi nekk ca asamaan ne fonk nañu dëgg lépp li mu ñu defal. Waaye ñiy def loolu barewuñu. Ñun, bëgguñu mel ni ay nit ñu nekkoon ci jamono Yeesu. Yeesu dafa fajoon fukki gaana. Waaye kenn rekk moo waññiku ci moom ngir gërëm ko (Luug 17:​12-17). Wóor na ne ki gërëm Yeesu lañu bëgg nirool. Bëgguñu mel ni juróom-ñeent yi ko gërëmul.

9 Kon yan ndigalu Yexowa lañu war a topp ? Am na ci ndigal yu ñu waxtaan ci téere bii. Waaye nañu ci seetaat yenn. Topp ay ndigalu Yàlla dina ñu dimbali ñu sax ci mbëggeelam.

NAÑU GËN DI JEGE YEXOWA

10. Waxal lu tax di kontine di yokk suñu xam-xam ci lu jëm ci Yexowa Yàlla am solo lool.

10 Jàng lu jëm ci Yexowa, lu am solo la ngir gën koo jege. Waruñu bàyyi mukk di def loolu. Bu amoon guddi bu sedd lool, fekk nga nekk ci biti di jaaru, ndax dinga bàyyi safara bi wàññiku ba fey ? Déedéet. Dinga kontine di ci def matt ngir safara bi kontine di tàkk, di leer te di tàng. Boo deful loolu fekk sedd bi mu ngi kontine di yokku rekk, dinga ci mën a ñàkk sa bakkan ! Ni matt di def ba safara bi kontine di tàkk, noonu la “ xam-xam bi jëm ci Yàlla ” di tax ba suñu mbëggeel ci Yexowa kontine di am doole. — Léeb yi 2:1-5, NW.

Ni safara soxlaa matt ngir kontine di tàkk, noonu it sa mbëggeel ci Yexowa soxla na lu koy may mu kontine di am doole.

11. Lan la li Yeesu jàngale def ci ay taalibeem ?

11 Li Yeesu bëggoon mooy, taalibeem yi kontine di dëgëral seen mbëggeel ci Yexowa ak ci Kàddoom gi am solo lool te nekk dëgg. Bi ko Yàlla dekkalee, Yeesu waxoon na ak ñaari taalibeem ci lu jëm ci li yonent yi waxoon ci Mbind yi ci làkku ebrë te mu amoon ci moom. Loolu lan la def taalibe yi ? Lii la taalibe yooyu mujj a wax ci seen biir : «Ndax sa xol seddul woon, bi muy wax ak nun ci yoon wi, te muy tekki Mbind mi ?» ​— Luug 24:32.

12, 13. a) Lu ëpp ci doomi Aadama yi tey, naka la seen mbëggeel ci Yàlla ak ci Biibël bi mel ? b) Naka lañu mën a def ba suñu mbëggeel bañ a wàññiku ?

12 Bi nga njëkkee dégg li Biibël bi wax dëgg, ndax sa xol feesul woon ak mbégte, nga komaase sawar te bëgg Yàlla ? Wóor na ne looloo amoon. Ñu bare lu mel noonu lañu yëgoon. Li gën a jafe léegi mooy, kontine di yëg mbëggeel boobu ci suñu xol te fexe muy gën di yokku. Bëgguñu def ni waa àddina sii. Yeesu waxoon na ne : “ Mbëggeelug ñi ëpp dina wàññiku. ” (Macë 24:12). Naka ngay def ba sa mbëggeel ci Yexowa ak li nga fonk dëgg yi nekk ci Biibël bi bañ a wàññiku ?

13 Nanga kontine di jàng ngir xam Yexowa Yàlla ak Yeesu Kirist (Yowaana 17:3). Nanga xalaat bu baax ci li ngay jàng ci Kàddu Yàlla, te laaj sa bopp lii : ‘ Li ma jàng, lan la may xamal ci Yexowa Yàlla ? Lan laa ci gis lu war a gën a tax ma bëgg Yàlla ak sama xol bépp, ak sama xel mépp ak sama bakkan bépp ? ’ (1 Timote 4:15). Xalaat yu mel noonu dañuy tax mbëggeel bi nga am ci Yexowa kontine di am doole.

14. Ñaan Yàlla, naka la ñuy dimbalee ñu kontine di bëgg Yexowa ?

14 Leneen li ñu mën a def ngir mbëggeel bi ñu am ci Yexowa kontine di am doole mooy ñuy faral di ñaan Yàlla (1 Tesalonig 5:17). Gisoon nañu ci pàcc 17 ne ñaan mayu Yàlla bu réy la. Ni diggante ñaari nit di gën di dëgër bu ñuy faral di waxtaan ci lépp, noonu it suñu diggante ak Yexowa dafay gën a dëgër te rattax bu ñuy​ faral di ko ñaan. Lii moo am solo lool : Nañu fexe ba suñuy ñaan bañ a doon mukk li ñuy tari, maanaam bañ a nekk lu ñuy tàmm wax di waxaat rekk, te fekk duñu yëg dara ci suñu xol, walla mu doon ay wax kese. Dañu war a wax ak Yexowa ni doom di waxe ak baayam bi ko bëgg lool. Dëgg la, bu ñuy wax ak Yàlla, dañu koy bëgg a may cér. Waaye bëgg nañu ko wax lépp li nekk ci ñun, te tibbe ko ci suñu xol (Psaume 62:8). Waaw, gëstu Biibël bi ñuy def ñun ci suñu bopp, ak ñaan yi ñuy tibbe ci suñu xol, am na solo lool ci suñu diine. Te dafa ñuy dimbali ñu sax ci mbëggeelu Yàlla.

NANGA AM MBÉGTE BOOY JAAMU YÀLLA

15, 16. Lu tax ñu mën a wax ne waare xebaaru Nguur gi cér bu réy la te dafa mel ni alal ju bare ?

15 Gëstu Biibël bi ñuy def ñun ci suñu bopp ak suñuy ñaan, mooy li nga xam ne dañu koy def ngir jaamu Yàlla te mën na am kenn du ñu gis. Waaye nañu wax léegi ci li nga xam ne ñépp a koy gis bu ñu koy def ngir jaamu Yàlla, maanaam wax suñuy moroom lu jëm ci suñu ngëm. Ndax mas nga waxtaan ak say moroom ci li nekk ci Biibël bi ? Bu dee mas nga koo def, am nga cér bu réy (Luug 1:74). Bu ñuy yégle dëgg yi ñu jàng yi jëm ci Yexowa Yàlla, dañuy bokk ci liggéey bi ñu sant karceen dëgg​ yépp, maanaam yégle xebaar bu baax bi jëm ci Nguuru Yàlla. ​— Macë 24:14 ; 28:19, 20.

16 Ndaw li Pool dafa jàppe woon waaraate bi ni lu am solo lool, mel ni alal (2 Korent 4:7). Yégal nit ñi lu jëm ci Yexowa Yàlla ak ci coobareem, mooy liggéey bi gën ci liggéey boo mën a def, ndaxte dañuy liggéeyal Njiit bi gën ci njiit yi, te dinañu ci am barke yi gën lépp li ñu mën a am. Boo bokkee ci liggéey boobu, dangay dimbali boroom xol yu rafet yi, ñu mën a jege suñu Baay bi nekk ca asamaan. Danga leen di dimbali it ñu jaar ci yoon wiy jëm ci dund gu dul jeex ! Ndax am na liggéey bu la mën a may mbégte ni liggéey boobu ? Rax-ci-dolli, di waare lu jëm ci Yexowa ak lu jëm ci Kàddoom, dafay tax suñu ngëm yokku, tax it mbëggeel bi ñu am ci moom gën a dëgër. Te Yexowa fonk na lool li ngay def (Yawut ya 6:10). Kontine di jàpp lool ci liggéeyu waare bi, dafa ñuy dimbali ñu sax ci mbëggeelu Yàlla. ​— 1 Korent 15:⁠58.

17. Lu tax waaraate bi karceen yi di def jamp lool tey ?

17 Bañ a fàtte ne waaraate bi liggéey bu jamp la, am na solo lool. Biibël bi nee na : “ Xamleel kàddug Yàlla, sax ci. ” (2 Timote 4:⁠2). Lu tax waaraate bi jamp lool tey ? Kàddu Yàlla nee na : “ Bésu Yexowa bu mag bi jege na. Jege na, te mu ngi gaawantu bu baax. ” (Tsëfanyaa 1:​14, NW). Waaw, jamono bu Yexowa di alag àddina su bon si sépp, mu ngi agsi ci lu gaaw. War nañu ko yégal nit ñi ! Dañu war a xam ne léegi lañu war a nangu ne Yexowa moo war a nekk seen Buur. Muj gi “ du tàrde ”. ​— Xabakukk 2:​3, NW.

18. Lu tax ñu war a won ñépp ne dañuy ànd ak karceen dëgg yi di jaamu Yexowa ?

18 Yexowa dafa bëgg ñu won ñépp ne moom lañuy jaamu te ànd ci ak karceen dëgg yi. Looloo tax Kàddoom wax ne : “ Nanu seet ni nu man a xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax. Te bunu bàyyi sunu ndaje yi, ni ko ñenn ñi di defe, waaye nanuy nàddante ci ngëm, di ko feddali, fi ak yéena ngi gis bésu Boroom biy jubsi. ” (Yawut ya 10:​24, 25). Bu ñuy nekk ak suñuy mbokk karceen ci ndaje yi, dinañu mën a màggal te jaamu suñu Yàlla mi ñu fonk lool. Dinañu jàppalante te xiirtalante ci suñu biir.

19. Naka lañuy def ba gën a dëgëral mbëggeel bi am ci mbooloo karceen yi ?

19 Bu ñuy ànd ak suñuy moroom yuy jaamu Yexowa, dañuy gën a bëggante ci mbooloo mi te nekk ay xarit. Seet jikko yu rafet yi nekk ci suñuy moroom, ni Yexowa di seete li baax ci ñun, am na solo lool. Bul yaakaar ne say moroom waruñu juum. Bul fàtte ne ñun ñépp tolloowuñu ci wàllu ngëm, te ñépp ay juum (Kolos 3:13). Jéemal a xaritoo ak ñi bëgg Yexowa ci seen biir xol. Su boobaa, dinga gisal sa bopp ne yaa ngi jëm kanam ci wàllu ngëm. Waaw, jaamu Yexowa ak say mbokk ci wàllu ngëm dina la dimbali nga sax ci mbëggeelu Yàlla. Naka la Yexowa di neexale ñi koy jaamu dëgg te sax ci mbëggeelam ?

FEXEEL BA AM “ DUND GU WÓOR GI ”

20, 21. Lan mooy “ dund gu wóor gi ”, te lu tax mu nekk yaakaar bu neex ?

20 Yexowa dafay may dund ñi koy jaamu dëgg ngir neexal leen. Waaye ban fasoŋu dund la leen di may ? Waaw, ndax mën nañu wax ne yaa ngi dund dëgg fi ñu tollu nii ? Ñu bare dañuy wax ne loolu jarul a laajte. Du ñu ngi noyyi, di lekk te di naan ? Kon wóor na ne ñu ngi dund. Te bu ñu nekkee ci jamano yi gën a neex ci suñu dund, mën na am sax ñuy wax ne : “ Lii mooy dund dëgg ! ” Waaye Biibël bi nee na, am na fànn bu am solo boo xam ne benn doomu Aadama amu ci tey dund dëgg.

Yexowa dafa bëgg nga am “ dund gu wóor gi ”. Ndax dinga ko am ?

21 Kàddu Yàlla nee na ñu “ téye ci dund gu wóor gi ”. (1 Timote 6:19.) Kàddu yooyu dañuy wone ne “ dund gu wóor gi ” mooy lu ñuy yaakaar a am ëllëg. Waaw, bés bu ñuy nekk ay nit ñu mat, dinañu dund dëgg, ndaxte dinañu dund ni Yàlla bëgge woon ñu dund bi mu doon sàkk nit. Bés bi ñuy nekk àjjana ci kaw suuf, am wér-gi-yaram gu mat sëkk, nekk ci jàmm ak mbégte, su boobaa dinañu am “ dund gu wóor gi ”,​ maanaam dund gu dul jeex (1 Timote 6:12). Ndax yaakaar boobu neexul ?

22. Naka lañu mënee “ téye ci dund gu wóor gi ” ?

22 Naka lañu mënee “ téye ci dund gu wóor gi ” ? Ci biir waxtaan boobu, Pool dafa waxoon karceen yi ñuy “ def lu baax ” te ñu “ bare jëf yu rafet ”. (1 Timote 6:18.) Kon leer na ne ni ñuy toppe dëgg yi ñu jàng ci Biibël bi, am na solo lool. Waaye ndax Pool dafa doon wax foofu ne liggéey bu rafet bi ñuy def moo tax ñuy gañe “ dund gu wóor gi ” ? Déedéet, ndaxte ci dëgg, “ yiwu Yàlla ” moo ñu may lu neex loolu ñuy séentu (Room 5:15). Yexowa dafa bëgg neexal ñi koy jaamu dëgg. Li mu bëgg mooy nga am “ dund gu wóor gi ”. Dund gu dul jeex bu bare mbégte ak jàmm noonu mooy xaar ñi sax ci mbëggeelu Yàlla.

23. Lu tax sax ci mbëggeelu Yàlla am solo lool ?

23 Kenn ku nekk ci ñun war na laaj boppam lii : ‘ Ndax maa ngi jaamu Yàlla ni mu ko waxe ci Biibël bi ? ’ Bu ñuy fexe ba topp bés bu nekk li Biibël bi wax, kon dinañu nekk ci yoon bu baax bi. Dina ñu wóor ne Yexowa mooy suñu làquwaay. Yexowa dina aar ñi koy topp ci jafe-jafe yi am ci muju jamono jii. Yexowa dina ñu musal te dugal ñu ci àddina bu bees te neex bi jege lool tey. Bu ñu nekkee ci jamono jooju, dinañu kontaan lool ! Dinañu bég lool itam ci li ñu tànnoon li gën ci muju jamono jii ! Boo tànnee def lu baax loolu tey, dinga am “ dund gu wóor gi ”, maanaam dinga dund ba fàww ni ko Yexowa Yàlla bëgge woon.